Seen surga Guy Marius Sagna (GMS) mooy wax ak yéen, di leen gërëm, di leen sant ci daamar (voiture) bi ngeen teg ci samay yoxo, ginnaaw bi ngeen waxee ni : Jot na seen surga bii di GMS am woto.
Dajaale ngeen 14i tamdareet (millions) ci xaalisu Farãs. Fukki tamdareet yi ak xaaj (10,5 millions) yi am nanu ci daamar muy « Toyota Rav 4 ». Nu teg ci benn tamdareet (1 million) ci ay « frais ». Lépp kon di fukki tamdareet ak benn yu teg xaaj (11,5 millions). Li des ci xaalis bi dina fekki li kopparal (financer) sunuy yëngu-yëngu ñeel xeex bi nuy ànd di ko xeex ak askan wi ngir jële fi nooteel ak jaay doole.
Sàcc bi nag, waay ji da koy dàkk ba jib ko ne ko duut xiir, foog ne day tax mu taxaw. Waaye mu geesu ne ko « làbbali nga ma de », teg ca yokk la mu doon daw.
Askan wi làbbali ngeen ma !
Daamar bi dina gën a yombal dem bi ak dikk bi, ngir nu wéy di nekk ci wetu Askan wi ñuy noot, tey taxaw ci sàmm àqam ak yelleefam.
Tey lanu gën a fas yéene xeex nooteel (impérialisme), Baay jinne yiy sàcc alalu askan wi, di noot askanu Senegaal, askanu Afrig.
Ak daamar bii, gën ngeen maa ñaax, gën ngeen maa sas.
Yàlla bu yaakaar tas !
Aywa leen nu gën a taxawal temm Askan wi, Senegaal, Afrig, ak néew doole yi.
Moom sunu Senegaal!
Moom sunu Afrig!
Askan wi ca kanam!
Jërë ngeen jëf samay njaatige !
GMS
Mes chers compatriotes,
C’est votre obligé Guy Marius Sagna qui s’adresse à vous pour vous remercier du fond du cœur pour la voiture que vous avez mise à ma disposition, au terme de la campagne : Il est temps que GMS ait un véhicule.
Vous avez, dans le cadre de cette campagne, mobilisé 14 millions de francs cfa. 10,5 millions ont servi à l’achat du véhicule de marque Toyota Rav 4. Il y a ensuite eu divers frais qui se sont élevés à 1 million. Donc, au total le véhicule est revenu à 11,5 millions de francs cfa. Le reste finance nos activités dans la lutte que nous menons aux côtés des masses populaires contre l’impérialisme et l’oppression.
Peuple sénégalais, vous m’avez davantage enhardi !
Cette voiture va faciliter nos déplacements, et nous permettre d’être partout aux côtés du peuple opprimé, pour la défense de ses droits et privilèges.
Nous sommes aujourd’hui plus que jamais déterminés à combattre l’impérialisme, les Baay-jinne qui volent les deniers publics, qui oppriment le peuple sénégalais, le peuple africain.
Par ce véhicule, vous m’encouragez et m’obligez davantage.
Que les espoirs et les attentes ne soient pas déçus !
Soyons encore plus déterminés et plus mobilisés pour le Sénégal, pour l’Afrique et pour les faibles.
Pour un Sénégal souverain !
Pour une Afrique souveraine !
Vive les peuples !
Merci à vous tous !
GMS